bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom".

