Yàlla nee na: jépp jëfi doomu Aadama moom la ñeel, ba mu des woor, moom man maa ko moom te maa koy fay
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «Yàlla nee na: jépp jëfi doomu Aadama moom la ñeel, ba mu des woor, moom man maa ko moom te maa koy fay, te woor ab pakk la, bu nit ki nekk…

