bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj
Jële na ñu ci Ibn Abbaas-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax jenn jigéen ju bokk ci Ansaar yi Ibn Abbaas tudd na ko waaye maa fàtte turam:"lan moo la tere nga ànd ak nun aji?" Mu ne ko: amunu lu dul ñaari…

