HadeethEnc · 1.30.0
kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Muusa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waa juy xeex ngir wone njàmbaar, ak kuy xeex ngir par-parloo, ak kuy xeex ngir ngistal, ana kan ci ñoom moo nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: "kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla".
02
Explanation
Laaj nañu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wuuteg jubluwaay yi ci ñiy xeex; kuy xeex ngir jàmbaare, walla par-parloo walla ngir ñu gis dayoom ci nit ñi mbaa leneen, kan moo ci nekk ci yoonu Yàlla? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne kiy xeex ci yoonu Yàlla: mooy kiy xeex ngir kàddug Yàlla jëm kaw.
03
Benefits
Liy Cosaan ci jëf yi baax walla yi bon mooy yéene ak sellal jëf ji ngir Yàlla.
Bu dee jubluwaay bi ci jihaad mooy yëkkati kàddug Yàlla, beneen jubluwaay buñu yoonal mo nga ca lu mel niki am ca koom ma, loolu du yàq cosaanu yéene ja.
Fexe ba noon yi du ñu Dugg ci dëkk i jullit ñi, dafa bokk ci xeex ci yoonu Yàlla.
Ngëneel li rot ci jihaatkat yi day yam ci ñiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku.

Attribution
[Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares