ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bàyyi: bu waxtaanee fen, bu kóllareentee wor, bu digee wuute ko, bu xuloo wax lu bon
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "ñent yii képp ku mu nekk ci moom nekk na naaféq, bu wenn melo nekkee ci moom kon wenn melow naaféq nekk na ci moom ba keroog mu koy bà…

