wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc
Jële nañu ci Abuu Amr -nee nañu it: Abii Amrata--, Sufyaan ibn Abdallah yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Wax naa : yaw Yónente Yàlla bi, wax ma ci Lislaam wax joo xam ne duma ko laaj kenn ku dul yaw, mu ne ma : "waxal gëm naa Yàlla, te jub kocc".

