doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu manut a ñàkk, kon na def biiram ñatti xaaj benn ba ngir lekkam, beneen ba ngir naanam, ñatteelu xaaj ba ngir noyyeem
Jële nañu ci Al-Miqdaad ibn Mahdii Karib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu ma…

