doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu manut a ñàkk, kon na def biiram ñatti xaaj benn ba ngir lekkam, beneen ba ngir naanam, ñatteelu xaaj ba ngir noyyeem
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Al-Miqdaad ibn Mahdii Karib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "doomu Aadama feesalul lenn ndab lu yées biiram, doy na sëkk doomu Aadama ji lekk gu mu taxawale ndiggam li, bu manut a ñàkk, kon na def biiram ñatti xaaj benn ba ngir lekkam, beneen ba ngir naanam, ñatteelu xaaj ba ngir noyyeem".
Explanation
Benefits
Jubluwaayu lekk, mooy sàmm wér gi ak kàttan gi te ci ñoom ñaar la dund gi di mucce.
Feesal birr bi ci ñam dafa am ay lor ci yaram ak ci diine, Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: "moytandikuleen biir bu fees, ndaxte moom day yàq yaram di tàyyeelloo ci julli".
Àttey lekk ay xaaj la: lu war, te mooy li ñuy sàmme dund gi te bàyyi ko di indi aw lor. Ak lu dagan, te mooy lu tege ca la war te ragaleesul loram. Ak lu ñu sib, te mooy li ñu ragal ay loram. Ak lu araam, te mooy li ñi xam ay loram. Ak lu ñu sopp, te mooy li ñuy dimbandikoo ci jaamu Yàlla ak topp ko, boolees na yooyu ci hadiis bi ci ñatti tolluwaay: bi ci njëkk: feesal biir. Ñaareel bi: ay lekk walla ay ñaag yuy taxawal ndigg. Ñateel bi: li mu wax: "ñatteelu xaaj ngir ñamam ak ñatteelu xaaj ngir naanam ak ñatteelu xaaj ngir noyyeem" lii lépp nag bu fekkee li ñuy lekk dafa dagan.
Hadiis bi ab tënk la ci tënki faj yi, ndax xam-xamu faj ci ñatti cosaan yii la nekk: wattu kàttan ak néewug lekk ak génne li ci biir bi, hadiis bi nag dafa làmboo ñaar yu njëkk yi, kem ni mu nekke ci waxi Yàlla mu kawe: (lekkleen naanleen te buleen yàq ndax moom bëggul yàqkat yi) [Al-Ahraaf: 31].
Matug sariiha ji ba tax mu làmboo njariñi nit ki ci diineem ak ci àddunaam.
Bokk na ci xam-xam yi cosaani faj ak i xeetam, kem ni mu ñëwe ci lem ak Hàbbatu Sawdaa.
Àttey sariiha yi dafa làmboo ay xereñte, ak ne dafa tabaxu ci jañ lor yi ak xëcci njariñ yi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

