Yàlla bind na yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di koy leeral
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Ibn Àbbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu jële ci Boroomam mu Barkeel mi te kawe, mu wax ne: "Yàlla bind na yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di koy leeral, ku yittewoo lu rafet te defu ko; Yàlla dana bindal fa moom aw yiw wu mat, bu ko yittewoo daal di koy def; Yàlla bind ko fa moom fukk yu rafet ba ci juróom-ñaari téeméeri full, ba ay full yu bari lool, bu yittewoo lu ñaaw te defu ko; Yàlla bind ko fa moom aw yiw wu mat, bu ko yittewoo daal di koy def; Yàlla bind ko fa moom wenn ñaawteef ".
Explanation
Képp ku namm a def lu rafet te dogu ci def ko dees na ko bindal wenn yiw doonte defu ko, bu ko defee nag ñu fulal ka ko fukk yu mel ni moom ba ci juróom-ñaari téeméeri yoon, ba ci ay yoon yu bari, ci kem la nek ca xol ba cig sellal ak jariñ ñeneen mbaa lu ni mel.
Waaye képp ku nàmm a def ñaawtéef te dogu ci def ko, far bàyyi ko ngir Yàlla dees na ka ko bindal aw yiw, bu ko bàyyee ngir yittewootu ko te deful ay sababam deesu ko bindal dara, waaye su ko bàyyee ngir ak lott dees na ko bindal yéeneem, su ko defee nag ñu bindal ko benn ñaawtéef.
Benefits
Njariñu yéene ci jëf yi ak ay jeexitam.
Ngëneelu Yàlla mu kawe mi ak ug ñeewanteem ak rafetalam ci ne ku nàmm a def aw yiw te mujju ko def Yàlla bindal ko ko aw yiw.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

