Maa ngi leen di dénk ragal Yàlla, ak dégg ak topp, donte ab jaam moo leen jiite, képp ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, maa ngi leen di dénk sama sunna si ak sunnay njiit yu jub yi tey jubal
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Najiih Al-Hirbaad ibn Saariyata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc waar na nu ag waare ba xol yi jàq ci, bët yi jooy, nu ne ko: yaw Yonente Yàlla bi! Dafa mel ni waarew tàggatoo la; kon laabire nu, mu wax ne: Maa ngi leen di dénk ragal Yàlla, ak dégg ak topp, donte ab jaam moo leen jiite, képp ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, maa ngi leen di dénk sama sunna si ak sunnay njiit yu jub yi tey jubal, ŋànkleen ci ak séen i dégéj, maa ngi leen di moytandikuloo bir yi ñu sos; ndax bidaa yépp ag cànkute la".
Explanation
leen, maanaam ki gën a suufe ci nit ñi moo leen jiite buleen rëy ci loolu nangeen ko topp, ndax day ragal a yëkkati fitna, ndaxte ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, Mu leeralal leen ni ñuy génne ci wuute gi, te mooy jàpp ci suunnaam ak sunnas njiit yu jub ya tey jubale ci ginnaawam, Abuu Bakarin As-Siddiix, ak Umar Ibnul Xattaab, ak Usmaan Ibnu Affaan, ak Aliyun Ibnu Abii Taalib, -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ak màtt ca ak seeni dégéj, maanaam -bëñ ya mujj-: li mu jublu ci loolu mooy farlu ci taqoo ak sunna ak jàpp ca, Mu moytondikuloo leen bir yi ñu sos fent ko ci diine, ndax bidaa yépp ay réer lañu.
Benefits
Yittewoo di waare, ak di nooyal xol yi.
Digle ñu topp ñenti njiit yu jub ya tey jubale ci ginnaawam, te ñooy Abuu Bakar, ak Umar, ak Usmaan, ak Aliyun -yal na leen Yàlla dollee gërëm-.
Tere nañu sos ci diine ji, ndax bidaa yépp ay réer lañu.
Dañuy dégg di topp njiitu jullit ñi ci lu dul ag moy.
Solos ragal Yàlla mu màgg mi ci bépp jamono ak bépp anam.
Wuute luy am la ci xeet wi, waaye bu amee dañoo war a dellu ci sunnas Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak njiit yu jub ya.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

