man de xam naa ne yaw aw xeer nga, doo lor te doo jariñ, bu dul woon ne gisnaa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di la fóon kon duma la fóon
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm: Mu ñëw ci Hajarul Aswad daal di koy fóon, daal di wax ne: man de xam naa ne yaw aw xeer nga, doo lor te doo jariñ, bu dul woon ne gisnaa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di la fóon kon duma la fóon.
Explanation
Benefits
Li ñu jublu ci fóon Hajarul Aswad, mooy roy Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
An-Nawawii nee na: maanaam mooy ne manuta jariñ manuta lor, waaye aw xeer la wu ñu bind kem mbooleem mbindeef yi nga xam ne du lor te du jariñ, Umar dafa fésal lii ci xew u aj gi; ngir ñu seede ko ci réew yi, ñëpp jàpp loo lu .
Jaamu yi lu ñuy taxawlu la; deesu ci yoonal lu dul lu Yàlla yoonal ak ub yonenteem.
Bu ag jaamu wéree dañu koy jëfe donte xamuñu lu tax; ndaxte jëfe gi nit ñi di jëfe ndigal ak def gi ñu koy def dafa bokk ci li Yàlla bëgg ci ñoom.
Tere nañu fóon lu sariiha joxewul ndigal ngir ñu fóon ko ci anamug jaamu muy xeer ak lu dul moom.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

