Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay ko na waajal ab tooguwaayam ca sawara
Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay k…

