bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, dara du ci génn lu dul dëgg
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Dama doon bind lépp lu ma dégg ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax dama koo bëggoon a wattu, Xuraysin tere ma loolu, ñu ne ma: ndax dangay bind lépp loo dégg ci Yonnente Yàlla bi te moom nit la day wax cig mer ak cig gërëm? Ma bàyyee bind, ma wax loolu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu joxoñ baaraamam ci gémmiñam, daal di ne: «bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, dara du ci génn lu dul dëgg».
Explanation
Ma wax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- li ñu wax ñoom, mu joxoñ baaraamam ci gémmiñam daal di wax ne: bindal, giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom dara du génn ci moom lu dul dëgg ci bépp anam nak, cig gërëm ak cig mer.
Yàlla mu kawe mi wax na ci Yonnenteem bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne: ﴾Yonente bi du waxe ci bànneexu bakkanam* lu mu wax dees ko koo wahyu﴿ [An-najmi 3-4].
Benefits
Xérug Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci wattu Sunna ak jottali ko.
Giñ dagan na donte giñloowuñu la ngir yéwénal, kem feddali am mbir.
Bind xam-xam bokk na ci jumtukaay yi ñuy wattoo xam-xam.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

