giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom kenn du ma dégg ci xeet wii moo xam Yahuut la walla Nasaraan, ba faatu te gëmul li ñu ma yónni lu dul ne dana bokk ci waa sawara».
Explanation
Benefits
Ku weddi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- njort bi mu njort ne gëm na yeneen yonnente yi du ko jariñ dara.
Ku déggul Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te wooteeb Lislaam bi àggul ci moom kooku dees na ko dogal ngànt, ay mbiram nag ëllëg bis-pénc ci Yàlla lay dellu.
Manees naa jariñu ci lislaam doonte tuuti la jiitoo dee gi, donte ci tawat ju tar la, fii ak ruu gi eggul ci bóli gi.
Nangu diiney yéefar yi -te yahuut yi ak nasaraan yi ci la ñu bokk- loolu ag kéefar la.
Tudd gi ñu tudd yahuut yi ak nasaraan yi -ci hadiis bi - loolu ngir yee ñeneen ñi la; ndaxte yahuut yi ak nasaraan yi am nañu téere, kon bu dee lii mooy seen mbir, kon ñi amul téere ñoo ca gën a yey, ñoom ñépp a war a dugg ci diine ji te topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

