bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdulla ibn Busrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay dafa ñëw ci Yonnente bi, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi! Yi lislaam santaane dafa bari ci nun, ndax am na bunt bu dajale bu nu man a jàpp? Mu wax ne: "bu sa làmmiñ deñ di tooy ci tudd Yàlla". Ñëw na ci beneen nettali: ci Hadiisu Muhaas ibn Jabal yal na ko Yàlla dollee gërëm: bi ma mujjee teqalikoo ak Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dama ne ko: yan jëf moo gën te gën a jege Yàlla? Mu ne: "nga faatu fekk sa làmmiñ moo ngi tooy ci tudd Yàlla mu màgg mi".
Explanation
jëf ju néew juy indi yool yu bari ngir mu jàpp ci.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tektal ko ci muy Sax di tooyal làmmiñam ci tudd Yàlla ci bépp jamono ak ci gépp anam; ci sàbbaal ak sant ak jéggalu ak ñaan ak yu ko niru.
Benefits
Bokk na ci màggug ngëneelu Yàlla mu yombal sababi yiw yi.
Gënlaanteg jaam ñi mingi ci seen cér yi ci bunti mbaax yi ak yiw yi.
Baril tudd Yàlla ci làmmiñ di sàbbaal ak di sant ak sikar ak di kàbbar ak yu dul yooyu, ànd ak mu dëppoo ak xol bi day taxaw taxawaayu ay naafila yu bari ci jaamu yi.
Sàmmonteek Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel aji-laaj ji ci tontu laaj bu nekk ca la méngoo ak moom.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

