man nag giñloowuma leen ci ne dama leen a tuumaal, waaye Jibriil moo ñëw fi man xibaar ma ne Yàlla mu kawe mi moo ngi leen di puukarewoo fa malaaka ya
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu mu wax ne: Muhaawiya dafa génn ci menn mbooloo ci jàkka ji, daal di ne leen: lan moo leen toogloo? Ñu ne ko dañoo toog di tudd Yàlla, mu ne leen: ndax dangeen seedeel Yàlla ne dara toogloowu leen lu dul loolu? Ñu ne ko: giñ nañu ci Yàlla ne dara toogloowu nu lu dul loolu, mu ne leen: man nag giñloowuma leen ngir ne dama leen a tuumaal, te it kenn gënu maa jege Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- te it kenn gënu maa néew lu may jële ci moom hadiis: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci menn mbooloo ci sahaabaam yi, ne leen: "lan moo leen toogloo?" Ñu ne ko: dañoo toog di tudd Yàlla di ko sant ci li mu nu gindi ci Lislaam, te xéewalal nu ko, mu wax ne: "ndax man ngeen a seedeel Yàlla ne dara toogloowu leen lu dul loolu?" Ñu ne ko: giñ nañu ci Yàlla ne dara toogloowu nu lu dul loolu, mu ne leen: "man nag giñloowuma leen ci ne dama leen a tuumaal, waaye Jibriil moo ñëw fi man xibaar ma ne Yàlla mu kawe mi moo ngi leen di puukarewoo fa malaaka ya".
Explanation
Benefits
Giñloo nit ci li amul jenn tuuma ngir yeete ci solos xibaar bi lu dagan la.
Ngëneelu jotaayi tudd Yàlla yi ak sàkku xam-xam yi ak ne Yàlla da koo bëgg te da koy puukarewoo fa malaaka ya.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

