bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg
Jële nañu ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
Books saved in this browser.
Loading favorites…
Tap the heart on any book card to save it here.
Search and read verified Prophetic hadeeth translations, explanations, benefits, categories and source attribution.
Smart instant results tolerate minor spelling mistakes, with every filter in one place.
Jële nañu ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
Jële na ñu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «am na benn waay bu doon lebal nit ñi, daan wax ndawam la naan ko: boo demee ci ku am jafe-jafe nanga ko jéggal, amaana Yàlla jéggal n…
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "jaam bi du suturaal ab jaam ci àdduna lu dul ne Yàlla dana ko suturaal ëllëg bis-pénc".
Jële nañu ci An-Nuwwaas ibn Simhaan Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Laaj naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu baax ak lu bon, mu wax ne: "lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko…
Jële nañu ci Sadaan Ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne: mokkal naa yaari mbir ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafet…
Jële nañu ci Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc neena: «bokk na ci li fi nit ñi fekk ci waxi Yonnente ya jiitu: boo amul looy rus defal lu la neex».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "buleen soxorante, buleen worante, buleen bañante, buleen dummooyoonte, bu kenn ci yéen jaay ci kaw njaayu keneen, nangeen nekk ay mbo…
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Benn waaye dafa wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dénk ma, mu ne ko: "bul mer" mu baamtu ko ay yoon mu ne ko: "bul mer".
Jële nañu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam"
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "way-maandu ñi de fa Yàlla danañu nekk ci kaw i minbari leer, nekk ca ndeyjooru Yàlla Aji-Yërëme ju màgg ji te tedd te yaari loxoom…
Jële nañu ci Jariir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ñu ag ñeewant xañees na ko aw yiw».
Follow any language without creating an account.

