bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg
Jële nañu ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
Books saved in this browser.
Loading favorites…
Tap the heart on any book card to save it here.
Search and read verified Prophetic hadeeth translations, explanations, benefits, categories and source attribution.
Smart instant results tolerate minor spelling mistakes, with every filter in one place.
Jële nañu ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte".
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ndax xam ngeen luy jëw?», ñu ne ko: Yàlla ak Yónenteem a xam, mu daa di ne mooy: «tudd sa mbokk ci lu ko neexul», ñu ne ko: waaw bu dee l…
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «amul dara lu gën a diis ci màndxem jullit bi ëllëg bis-pénc jikko yu rafet, te Yàlla dafa bañ ku ñaaw i wax ñaaw i jëf».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: "waat day jariñ liñuy jaay waaye day yàq tonowu".
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «ku giñ daal di wax: giñ naa ci Laata ak Hussaa, na wax: laa ilaaha illal-Laahu, ku wax àndandoom ne ko: kaay ñu kàrt na sar…
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne: «jullit mooy ki nga xam ne jullit ñi mucc nañu ci làmmiñam ak ci loxoom,gàddaaykat nag mooy ki gàddaay li Yàlla araamal ci…
Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "ñent yii ku ñu nekk ci moom nekk na ab naaféq bu sotti, ku wenn melo ci ñoom nekk ci moom am na wenn melow naaféq ba keroog mu koy bày…
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji».
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu màgg mi nee na: doomu Aadama moo ngi may lor day ŋàññ jamono ji te man maay jamono, ci sama loxo la mbir yi nekk maa koy wëlbati g…
Follow any language without creating an account.

