waat day jariñ liñuy jaay waaye day yàq tonowu
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: "waat day jariñ liñuy jaay waaye day yàq tonowu".
Explanation
Benefits
Fàggu gu araam donte amenañu ca lu bari; day tax baarke ba deñ.
Al-Xaarii nee na: baarke bu deñ ci lañu fàggu mooy: benn alal ji yàqu, walla ñu def ko ci lu amul njariñ ci àdduna walla yool ca allaaxira, walla mu des fi moom ñu xañ ko njariñ la, walla ku mu gërëmul donn ko.
An-Nawawii nee na: tere na ñu waat yu bari ci njaay mi, ndax giñ ci ku dul ki ko aajowoo lu ñu sib la, niki noonu day tax njaay mi mi gaaw a jar, amaana sax aji-jënd ji woru ci ngiñ li.
Giñ bu bari ngëm gu wàññeeku la, Tawhiid ju wàññeeku la it, ndaxte giñ bu bari day waral ñaari mbir: ben bi: woyofal loolu ak ñàkk ko a faale, ñaareelu mbir mi: fen la, ndax ku bari giñ rekk tàbbi ci ay fen, kon jaadu na ñu néewal ko te bañ koo baril, loolu moo tax su nu boroom mu Sell mi wax ne: (nangeen wattu seen giñ yi) [Al-Maa-ida: 89].
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

