Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte".
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: dénk naa la ñatti bir:
Bi ci njëkk: sàmmal sa làmmeñ ci lu amul yiw, ak ci wépp ay, te bul wax lu dul aw yiw.
Ñaareel bi: nanga taqoo ak sa kër ngir jaamu Yàlla ca wéetaay ya, te nga soxlawoo topp Yàlla mu màgg mi, te nga beru ci sa kër wolif fitna yi.
Ñatteel bi: jooyal te réccu te tuub li nga def ci ay bàkkaar.
Benefits
Leeral yiy tax a mucc ci àdduna ak allaaxira.
Ñaaxe ci nit ki soxlawoo boppam bu manula jariñ keneen, walla mu ragal lor ci diineem ak bakkanam ci bu jaxasoo ak nit ñi.
Ag junj jëm ci yittewoo kër gi rawati na jamonoy fitna, ndax dafa bokk ci jumtukaayi sàmm diine.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

