Yàlla mu màgg mi nee na: doomu Aadama moo ngi may lor day ŋàññ jamono ji te man maay jamono, ci sama loxo la mbir yi nekk maa koy wëlbati guddi ak bëccëg
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu màgg mi nee na: doomu Aadama moo ngi may lor day ŋàññ jamono ji te man maay jamono, ci sama loxo la mbir yi nekk maa koy wëlbati guddi ak bëccëg".
Explanation
Benefits
Am teggiin ci Yàlla ci wax ak jëf.
Dañoo war a gëm dogal yi, te muñ lor yi.
Loru bokkul ak gaañu; nit ki dana loru ci dégg lu bon walla gis ko; waaye du gaañu ci loolu, batay dana loru ci xet gu xasaw niki soble ak laaj waaye du ca gaañu.
Yàlla mu kawe mi tudd naa Sellam gi day loru ci yenn jëfi jaamam yu ñaaw yi, waaye du gaañu ci loolu, niki ni mu ko waxe ci hadiisu Al-Xudsii: "yéen sama jaam ñi yéen de manu leen a egg ci gaañ ma ba di ma gaañ, te manu leen a egg ci jariñ ma ba di ma jariñ".
Ŋàññ jamono ji ak melal ko day séddalikoo ci ñatti xaaj: 1- mu ŋàññ jamono ji ci ne mooy aji-def ji; ak ne jamono ji mooy wëlbati mbir yi jëme ko ci aw yiw ak aw ay! Lii nag bokkaale gu mag la; ndax dafa gëm ne amna jeneen aji-bind ju bokk ak Yàlla, ak ne dafa askanale xew-xew yi ci ku dul Yàlla, 2- mu ŋàññ jamono ji du ngir gëm ne mooy aji-def ji; waaye dafa gëm ne Yàlla mooy Aji-Def ji waaye day ŋàññ jamono ji ndax mooy barabu mbir mii mu sib; lii nag dafa araam, 3- ma jublu ci xibaare dong ci lu dul yedd; lii moom dagan na, te bokk na ca waxu Luut ja yal na ko Yàlla dolli jàmm: {lii moom bis bu tar la}.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

