bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma, ci lañu bind Aadama, ci lañu ko duggal àjjana, ci lañu ko ca génne, te Saa du taxaw ci lu dul bis…

