bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: « bis bi gën ci bis yi mooy bisu àjjuma, ci lañu bind Aadama, ci lañu ko duggal àjjana, ci lañu ko ca génne, te Saa du taxaw ci lu dul bisu àjjuma ».
Explanation
Benefits
Ñaaxe ak baril ay jëf yu baax ci bisu àjjuma, ak waajal ngir am yërmàndey Yàlla, ak jañ mbugalam.
Yii ñu tudd ci hadiis bi jagleel ko bisub àjjuma, wax nañu ne: nekkul ngir tudd ngëneelu bisub àjjuma; ndaxte génne Aadama ak ñëwug bis-pénc loolu deesu ko jàppe ngëneel, wax nañu itam: yépp ay ngëneel la, génnug Aadama sabab la ci am ay séti Yonnent ak ña ñu soloo ak ñu sell ñi, ñëwug bis-pénc sabab la ci ñu fay ñu baax ñi ak ñu jot la leen Yàlla waajalal ci ay teraanga.
Tuddal nañu bisu àjjuma yeneen ngëneel yu dul yii ñi tudd ci nettali gii, bokk na ca: ci lañu jéggal Aadama, ci lañu ko faat, am na ci it aw waxtu wow jaam buy aji-gëm du dëppoo ak moom di ñaan Yàlla dara lu dul ne dana ko ko jox.
Bis bi gën ci at mi mooy bisub Arafa, wax nañu it: bisub Tabaski, bis bi gën ci ayu bis yi mooy bisu àjjuma, guddi gi gën mooy guddig Laylatul Xadri.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

