lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata Abdur Rahmaan ibn Saxrin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne: «lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seen laaj yu bari, ak seenug juuyoo ak seen i Yonente».
Explanation
Benefits
Tere yi mayeesul ñu def ci dara, ndigal nag ci kem kàttan rekk; ndaxte bàyyi moom lu ñu man la te def day aajowoo kàttan ci def la nu digle.
Tere nañu di baril ay laaj, boroom xam-xam yi séddale nañu laaj ci ñaari xaaj: benn bi mooy: loo xam ne ci anamug xamle lu ñu soxla ci mbiri diine la, lii moom lu ñu digle la te ci xaaj bii la laaji Sahaaba yi nekkoon, ñaareel bi: loo xam ne ci anamug taral la ak sonnale lii nag dañu koo tere.
Artu xeet wi ci wuute ak Yonnente bi, kem ni mu ame woon ca xeet ya ko jiitu woon.
Yi ñu tere day làmboo lu néew ak lu bari; ndax maneesu ko a moytu ci li dul moytu lu néewam lu bareem, ci misaal: tere na nu Ribaa mu làmboo lu néewam ak lu bareem.
Bàyyi sabab yiy jëme ci lu araam; ndax loolu dafa bokk ci moytu.
Jaaduwul ci nit ki muy dégg waxu Yonente bi ba noppi di wax naan: ndax lu war la walla lu ñu sopp la, waaye dafa war a gaaw ci jëfe ko; ngir li mu wax ne: "defleen ci lu ngeen man".
Bari ay laaj sabab la ci alkande rawati na ci mbir yi nga xam ne maneesu caa egg niki masalay kumba, ak ni mbiri bis-pénc mel, kon buy bari loo koy laaj di alku, te kuy taral nga kuy xóotal nga.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

