bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bàyyileen ma bu ma leen bàyyee, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy seeni laaj ak di wuute ak seeni Yonnente , bu ma leen teree dara na…

