ñi gën ci yéen ñooy samag maas, topp ci ña ca topp, topp ci ña ca topp'
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne, Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ñi gën ci yéen ñooy samag maas, topp ci ña ca topp, topp ci ña ca topp' Imraan nee na: xamuma ndax Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tudd na ginnaaw ag maasam ñaari maas walla ñatt, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "nekk na ci seen ginnaaw ay nit yoo xam ne dañuy wor te deesu leen wóolu, ñuy seede te deesu leen seedeloo, ñuy nisar te du ñu ko matal, ag duuf feeñ ci ñoom".
Explanation
Benefits
Ibn Hajar nee na: hadiis bi day waral ne Sahaaba yi ñoo gën ña topp si ñoom, ña topp si ñoom ñoo gën ña ca toppaat, waaye ndax gën gii ci mbooloo mi la walla ci kenn ku ne? Loolu moom lu ñuy gëstu la, waaye li ëpp ci boroom xam-xam yi li ñu wax mooy ngënéel li ci benn-benn yi la nekk.
Ag junj ci war gi topp yoonu ñatti maas yu njëkk yi; ndax ku jamonoom jege jamonoy Yonente bi moo gën a yay ci ngëneel ak ug xam ak roy ci njubug Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Nisar: mooy mukàllaf mi waral ci boppam ag jaamu gog Aji-Yoonal ji waralu ko ci kawam ci jenn wax ju koy tegtale.
Ŋàññ wor ak ñàkk a matal nisar ak aju ci àdduna.
Ŋàññ seede ci lu dul ñu lay seedeloo bu dee boroom dëgg gi xam na loolu, bu dee nag xamu ko day dugg ci waxi Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: "ndax duma leen xibaar ki gën ci seedekat yi, mooy kiy indi seedeem njëkk ñu ko koy laaj" Muslim soloo na ko.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

