ku wax: laahi ilaaha illallaahu, amul kenn ku ñu war a jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, Yàlla rekk nag mooy càmbar ay jëfam
Jële na ñu ci Taarix Ibn Asyam Al-Asjahii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wax: laahi ilaaha illallaahu, amul kenn ku ñu war a jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñu…

