man nag giñloowuma leen ci ne dama leen a tuumaal, waaye Jibriil moo ñëw fi man xibaar ma ne Yàlla mu kawe mi moo ngi leen di puukarewoo fa malaaka ya
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu mu wax ne: Muhaawiya dafa génn ci menn mbooloo ci jàkka ji, daal di ne leen: lan moo leen toogloo? Ñu ne ko dañoo toog di tudd Yàlla, mu ne leen: ndax dangeen seedeel Yàlla ne dara toogloowu leen lu dul loolu? Ñu ne ko: giñ nañu ci Yà…

