yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «yaw Aba-Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi?» Nee na: ma ne ko: Yàlla ak ub Yónenteem ñoo xam. Mu ne ma: «yaw Aba- Munsir, ndax xam nga ban aaya moo gën a màgg ci téere Yàlla bi ?» Nee na: ma ne ko: {Allaahu laa-i-Laaha illaa huwa Al-Hayyul Xayyuumu} [Al-Baxara: 255]. Nee na: mu dóor sama dënn, daal di wax ne: «giñ naa ci Yàlla, na xam-xam ndokkeel Aba- Munsir».
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Ubay Ibn Kahb aaya bi gën a màgg ci téere Yàlla bi, muy dengi-dengi ci tontu bi, mujj gi mu ne: mooy aayatul Kursiyyu: {Allaahu laa ilaaha illaa huwa Al Hayyul Xayyuumu}, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dëggal ko, daal di fëgg dënnam ngir junj ne fees na dell ak xam-xam ak xereñ, daal di koy ñaanal mu texe ci xam-xam bi te ñu yombalal ko.
Benefits
Aayatul Kursiyyu mooy aaya bi gën a màgg ci téereb Yàlla bi, kon jaadu na ñu mokkal ko te di settantal ay maanaam ak di ko jëfe.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

