Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne: indil nañu Yonente Yàlla yàpp ñu jox ko tànk ba ndax dakoo bëggoon lool, mu dal di cay xàmp, daal di wax ne: "man maay sangu nit ñi ëllëg bis-pénc, ndax xam ngeen lu tax loolu? Yàlla day dajale nit ña jiitu…

