Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne: indil nañu Yonente Yàlla yàpp ñu jox ko tànk ba ndax dakoo bëggoon lool, mu dal di cay xàmp, daal di wax ne: "man maay sangu nit ñi ëllëg bis-pénc, ndax xam ngeen lu tax loolu? Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ, nit ñi ne: xanaa gisuleen li leen jot, ndax dungeen xool ku leen tinu ci seen Boroom? Ñenn ci ñoom wax ñeneen ñi: demleen ci Aadama, ñu ñëw ci Aadama ne ko: yaw yaay baayu nit ñi, Yàlla bind la ci loxoom, daal di wal ci yaw ci ruuham gi, mu digal malaaka yi ñu sujjóotal la, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Xanaa gisóo li nu jot? Aadama ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam , te moom da maa tere woon garab ga ma moy ko, sama bopp sama bopp doyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Nuuh, ñu dem ci Nuuh, ne ko: yaw Nuuh yaw yaay Yonente bi njëkk ci waa suuf, te Yàlla tudde na la jaam bu man a sant bi, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa amoon ñaan gu ma ñaan ci kaw sama nit ña, sama bopp sama bopp doyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Ibraahiima, ñu ñëw ci Ibraahiima, ne ko: yaw Ibraahiima yaw ndawul Yàlla nga di xaritam ci waa suuf, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa fenoon ñatti fen, sama bopp noyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Muusaa, ñu ñëw si Muusaa, ne ko: yaw Muusaa yaw ndawul Yàlla nga, te gënale na la ci yónni gi mu la yónni ak wax gi mu wax ak yaw, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa ray bakkan bob digaluñu ma ma ray ko, sama bopp noyna ma demleen ci ku dul man, demleen ci Iisaa ibn Maryma, ñu dikkal Iisaa, ne ko: yaw Iisaa yaw ndawul Yàlla nga, di kàddoom gu mu sànni ca Maryama di ruu gu jóge ci Moom, nga wax ak nit ñi ca lal ba di ab liir, tinu nu ci sa Boroom xanaa gisóo ci li nu nekk? Iisaa ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te tuddul benn bàkkaar, sama bopp noyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Muhammat, ñu dem ca Muhammat, ne ko: yaw Muhammat, yaw ndawul Yàlla nga, di ki mujj ci ñi Yónente yi, te Yàlla jéggal na la li jiitu ci say bàkkaar ak Li mujj, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Ma daal di dem ca ronu Aras, ma rot daal di sujjóot ñeel sama Boroom, Yàlla xamal ma ci ay xeeti sant Yàlla ak tagg ko loo xam ne masu ko xamal kenn ku ma jiitu, topp ñu ne ko: yaw Muhammat, yëkkëtil sa bopp, laajal ñu jox la, sàkkul ramm ñu jox la, ma yëkkëti sama bopp, ma wax ne: sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, ñu ne ko: yaw Muhammat, dugalal ci sa xeet ñi ñu dul càmbar ci buntu ndayjoor bi, ci bunti àjjana yi, te ñoom dañuy bokk ak nit ñi ci yeneen bunt yu dul yooyu, topp mu ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom ne li ci diggante ñaari jàppukaayi bunt yi ci bunti àjjana yi, moo ngi mel ni diggante Màkka ak Himyar -walla moo ngi mel ni diggante Màkka ak Busraa-".
Explanation
Benefits
Ngëneelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci kaw nit ñépp.
Al-Xaadii Hiyaad nee na: nee nañu sang mooy kiy yilif aw nitam ñuy dellu ci moom bu tar-tar yi amee, te Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mooy seen sang ci àdduna ak allaaxira, waaye dafa jagleel allaaxira cig tudd ngir la fa sang ga di yëkkëtiku, ak li ko ñépp di nangul loolu, ak li Aadama ak doomam yépp di nekk ci suufu raayaam moom Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Xereñte gi mooy ne Yàlla da leen a defal ñu laaj Aadama ak ka ca topp, te mayu leen ñu laaj Yónenteem bi Muhammat ngir feeñal ngëneelam, te loolu mooy la këna kawe ci daraja, ak ug jege Yàlla gu mat sëkk.
Yoonalees na ku am aajo ci keneen mu tuddalko ay meloom ya gën a rafet; ngir mu gaaw koo wuyu.
Dagan na ci ku ñu laaj lu mu manul mu joxe ngànt gu ñu koy nangule, sopp na ñu itam mu tegtale ku mu njort ne man na loolu.
Leeral tiitaangey taxawaay ba ak tarug dajale ga ci jaam ñi ëllëg bis-pénc.
Toroxlug Yonente yi ba tax ñuy tudd li weesu woon ci ñoom; ngir ñu yég ne ñoom egguñu foofu.
Saxal ramm gu màgg ga ëllëg bis-pénc, te mooy ñu teqale diggante mbindeef yi.
Saxal wasiila ak maqaama ga ñu gërëm mu ñeel Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Canti Yàlla yi du jeex, loolu moo tax Yàlla jox Yonnenteem bi ci barab bii ay xeeti tagg yu rafet lu mu musut a jox kenn ci ñi ko jiitu.
Leeral ne xeetu Muhammat mooy xeet wi gën, ñoom am nañu ay jagle ci dugg àjjana ba ñoo xam ne deesu leen càmbar danañu dugg ci bunt bu ñu leen jagleel, te dañuy bokk ak nit ñi yeneen bunt yi des.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

