moom am ndoxam lu laab la , am méddam it lu dagan la
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay laaj na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, nun danuy dugg ci géej gi, di yor tuuti ndox, bu nu ci jàppee daal di mar, ndax nu jàppu ci ndoxum…

