danañu indi jenn waay ëllëg bis-pénc, sànni ko ca sawara, buttiti biir yi tasaaroo, mu koy wër kem ni mbaam di wëre ci takkuwaayam
Jële nañu ci Usaamata Ibn Saydin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dañu ko wax ne ko: tee ngaa dugg fi Usmaan wax ak moom? Mu ne: xanaa gisuleen man duma wax ak moom lu dul ne dégtal naa leen ko? Giñ ci Yàlla ne wax naa ak moom ci sama diggante ak moom, te duma ti…

