danañu indi jenn waay ëllëg bis-pénc, sànni ko ca sawara, buttiti biir yi tasaaroo, mu koy wër kem ni mbaam di wëre ci takkuwaayam
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Usaamata Ibn Saydin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dañu ko wax ne ko: tee ngaa dugg fi Usmaan wax ak moom? Mu ne: xanaa gisuleen man duma wax ak moom lu dul ne dégtal naa leen ko? Giñ ci Yàlla ne wax naa ak moom ci sama diggante ak moom, te duma tijji am mbir mom bëgguma ko a njëkk a tijji, te duma wax kenn ku ma jiite naan ko: moo gën ci nit ñi ginnaaw ba ma déggee Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di wax naan: "danañu indi jenn waay ëllëg bis-pénc, sànni ko ca sawara, buttiti biir yi tasaaroo, mu koy wër kem ni mbaam di wëre ci takkuwaayam, waa sawara daje fa moom, naan ko: yaw diw lan moo la dal? Xanaa du yaa nu daan digal lu baax di nu tere lu bon? Mu ne: ahakay, dama leen daan digal lu baax te daawuma ko def, daan leen tere lu bon ba noppi di ko def".
Explanation
Usaamata yal na ko Yàlla dollee gërëm: ne moom day laabire njiit yi cig nëbbu waaye du naxante ak kenn donte njiit la, te du leen siiru ba leen di tagg ci seen kanam ci ag neen, ginnaaw bi mu déggee Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ëllëg bis-pénc danañu indi jenn waay, sànni ko sawara, butitam yi génn ci biir bi génn gu gaaw ngir tarug tàngaay wi ak tarug mbugal mi, mu wër butitam yi ci anam googu ci biir sawara kem ni mbaam di wëre yeewukaayam bay xeeru mooñukaay ba, waa sawara dajaloo wër ko, mel ni kurel bu ko wër, ñu koy laaj: yaw diw, xanaa du yaa doon digle lu baax di tere lu bon?
Mu wax ne: dama doon digle lu baax te daawuma ko def, daan tere lu bon ba noppi di ko def.
Benefits
Tëkku gu tar ñeel na ku ay waxam di wuute ak i jëfam.
Am teggin ci njiit yi ak ñeewante leen, ak digal leen lu baax tere leen lu bon.
Ŋàññ nañu naxante ak njiit yi ca lay dëgg, di feeñal lol la ca biir daa wuute ak moom, niki kuy sibooru cig neen.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

