Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne leen: ndax gërëm ngeen? Ñu ne ko: lu ñuy teree gërëm te nga jox nu loo joxul kenn ci sa mbindeef yi?
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu baarkeel mi te kawe day wax waa àjjana: éey yéen waa àjjana? Ñu ne ko wuyusi nanu la topp nañu la ak mbegte, mu ne le…

