Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lan mooy li ëpp luy duggal nit ñi àjjana, mu wax ne: «ragal Yàlla ak rafet jikko», ñu laaj ko lan moo ëpp luy duggal nit ñi sawara mu ne: «gémmiñ ak awra».
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sabab yi gën a màgg yuy dugale àjjana ñaari sabab la, te mooy:
Ragal Yàlla ak rafet jikko.
Ragal Yàlla: mooy nga def kiiraay sa diggante ak mbugalum Yàlla, ci di def ay ndigalam di moytu ay tereem.
Rafet jikko: dana nekk ci yaatal kanam, ak di def ñekk tey feg lor yi.
Sabab yi gën a man a duggale sawara ñaar la, te mooy:
Làmmeñ ak awra.
Bokk na ci Bàkkaari làmmeñ yi: fen ak jëw ak rambaaj ak yeneen.
Bokk na ci Bàkkaari awra yi: njaalo ak ngóor-jigéen ak yeneen.
Benefits
Làmmeñ lu bon la ci boroom, te bokk na ci liy tax a dugg safara.
Lorànge yi ci bànneex yi ak ñaawtéef yi ci nit ñi, mooy ne bokk nañu ci liy gën a waral ñu dugg sawara.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

