ne bu daan dugg ci jàkka day wax: "ahuusu bil Laahi Alhasiimi, wa bi wajhihi Alkariimi, wa sultaanihii alxadiimi, minas Saytaani Arrajiimi
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm: Jële na ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne bu daan dugg ci jàkka day wax: "ahuusu bil Laahi Alhasiimi, wa bi wajhihi Alkariimi, wa sultaanihii alxadiimi, minas Saytaani Arrajiimi", nee na: ndax loolu rekk la? Ma ne ko: waaw, mu ne: bu waxee loolu saytaane day wax naan: aarees na ko ci man tay.
Explanation
Amu tàmbalikaay
Te amul it yamukaay (minas Saytaani Arrajiimi) ki ñu soreele dàq ko ci yërmàndey Yàlla, Maanaam: Yàlla sàmm ma ci ay
jax-jaxam ak ug beewalam, ak ay jéegoom, ak i xalaatam, ak i jaxaseem, ak réeralaateem, ndaxte moom sabab la ci cànkute ak jëme ci mbewte ak réer. Ñu wax Abdullah ibn Amr "ndax loolu dong" maanaam: ndax lii rekk la Yonnente bi wax? Mu ne: waaw.
Bu kiy dugg ci jàkka waxee ñaan gii; Saytaane day wax: kii di dugg aar na boppam ci man ci waxtu yépp bëccëg gi ak guddi gi.
Benefits
Moytandikuloo ci Saytaane, ak ne moom day xaar jullit bi; ngir sànk ko ak bewloo ko.
Nit ki day am kaaraange ci Saytaane ak ug réeralaateem ak sànkaateem ci kem ni xolam taxawe ci gëm Yàlla ak teewlu ñaan gii ak dëggal digu Yàlla ba cay topp.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

