ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ñi ma gën a bëgg ci yéen, te gën maa jege ëllëg bis-pénc, ñooy ñi gën a rafet jikkó ci yéen, waaye ñi ma gën a bañ ci yéen te gën maa sori ë…

