Diinaar boo joxe ci yoonu Yàlla, ak Diinaar boo joxe ci goreel jaam, ak Diinaar boo sarax ab miskiin ak Diinaar boo jox sa njaboot ba ca gën a màggug fay mooy bi nga jox sa njaboot
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Diinaar boo joxe ci yoonu Yàlla, ak Diinaar boo joxe ci goreel jaam, ak Diinaar boo sarax ab miskiin ak Diinaar boo jox sa njaboot ba ca gën a màggug fay mooy bi nga jox sa njaboot ".
Explanation
Benefits
Jiital ka gën a ya y ci buntub joxe bu ñu dajee, bokk na ci loolu jox njaboot gi bu dee manuñoo jox ñépp.
An-Nawawii wax na ca ba muy firi sahiihu Muslim ne: ñaaxe ci jox njaboot gi, ak leeral màggug yool ba ca nekk; ndax amna ci ñoom koo xamne jox ko daa war ci sababus jegeñaale, am ci ñoom koo xamne dañu ko a sopp te day nekk sarax ak jokk, amna ci ñoom koo xamne day nekk lu war ci sababus sëy walla ag njaam, yii yépp nag ngëneel la gu ñu ñaaxe, te moo gën saraxu coobarewu.
As-Sindii nee na: waxam ji (Diinaar boo jox sa njaboot) maanaam: ci misaal bu ca yéenee jëmmi Yàlla ji te namm ca àqi njaboon.
Abuu Xalaabata nee na: ana gan góor moo gën a màggug pay góor giy jox njaabotam gu ndaw di leen feg walla Yàlla def mu leen di jariñ?!
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

