amul benn bis bu jaam ñi di xëy lu dul ne ñaari malaaka danañu wàcc, kenn ki naan: yaw Yàlla joxal aji-joxe ji leneen, keneen ki naan: yaw Yàlla joxal aji-téye ji ag yàqule
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: «amul benn bis bu jaam ñi di xëy lu dul ne ñaari malaaka danañu wàcc, kenn ki naan: yaw Yàlla joxal aji-joxe ji leneen, keneen ki naan: yaw Yàlla joxal aji-téye ji ag yàqule».
Explanation
Yaw Yàlla joxal kiy jox cig topp Yàlla njabootam ak di ganale ak di saraxe wuutal wecceel ko yiw ca la mu joxe, te baarkeelal ko ko.
Keneen ki naan: yaw Yàlla joxal kiy téye wolif loolu ag yàqule te sànk alalam ji mu tere ña ko yeyoo.
Benefits
Malaaka yi dañuy ñaanal way-gëm yu sell yiy joxe ag yiw ak baarke, te seen ug ñaan lu ñuy nangu la.
Ñaaxe ci joxe yu war ya ak coobarewu ya; niki jox njaboot gi, ak jokk mbokk, ak bunti yiw yi.
Leeral ngëneelu aji-joxe ci lu baax, ak ne ag mujjam mooy ne Yàlla da koy wuutalal, Yàlla mu kawe mi nee na: {lépp lu ngeen joxe moom moo koy wuutal, te mooy gën gi wërsëgale} [Saba: 39].
Ñaan Yàlla gii nag kiy bañ a joxe si farata lañuy ñaan mu dal ko, waaye bu dee joxe yi ñu sopp nag du ci dugg;ndax boroomam yeyoowul ñukoy ñaan Yàlla.
Araamalees na nay.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

