benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: benn waay dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: lan moo gën ci Lislaam? Mu ne ko: "nga leele ñam, ak di nuyu koo xam ak koo xamul".
Explanation
Bu njëkk bi: di baril di leel way-ñàkk yi, dana ci dugg ba tay saraxe ak àddiya ak nganale ak céetal, ngëneelu lele nag dana feddaliku ci jamonoy xiif, ak bi njëg yi seeree.
Ñaareel bi: di nuyu bépp jullit, moo xam xam nga ko walla xamóo ko.
Benefits
Nuyoo ak joxe ñam dafa bokk ci jëf yi gën ci Lislaam;ngir ngëneelam ak ni ko nit ñi di aajowoo ci waxtu wu ne.
Ci ñaari jikkó yii la rafetal di dajee ci wax ak ci jëf, te mooy li gën a mat ci rafetal.
Jikkó yii day aju ci jëflànte ci diggante jullit ñi, am na yeneen jikko ci jëflànte jullit bi ak Boroomam.
Njëkka nuyóo dañmm jullit rekk la jagoo, waaye deesul njëkk a nuyu ab yéefar.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

