Jenn waay ñëw na ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: assalaamu halaykum, mu fay ko mu daldi toog, Yonnente bi ne: "fukk
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Jenn waay ñëw na ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: assalaamu halaykum, mu fay ko mu daldi toog, Yonnente bi ne: "fukk" keneen daal di ñëw ne: assalaamu halaykum wa rahmatu Laah, mu fay ko mu toog, mu wax ne: "ñaar fukk" topp keneen ñëw daal di ne: assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wabarakaatuhu, mu fay ko mu toog, mu ne: "fanweer".
Explanation
Benefits
Dolleekug fay moo ngi ci dolleekug baati nuyóo yi.
Li gën a mat ci nuyóo mooy: (assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wabarakaatuhu), li gën ci baati fay yi mooy: (wahalaykumus salaamu wa rahmatul Laahi wabarakaatuh).
Martabay nuyóo ak delloo gi dafa rawante fay ga it dafa rawante.
Jàngal nit ñi yiw ak yee leen ci amal la gën.
Ibn Hajar nee na: aji-tàmbali ji bu ca dollee (wa rahmatul Laah) sopp nañu mu teg ca (wa barakaatuhu) ndax kon sopp nañu dolli ca delloo ga? Niki noonu aji-tàmbali ji bu ca dollee (wa barakaatuhu) ndax sopp nañu ci moom loolu, Maalik génne na ca Muwatta jële ci Ibn Abbaas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: nuyóo ci wabarakaatuhu la yem.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

