yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira
Jële nañu ci Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Damaa wax ne: yaw Yonnente Yàlla bi, xamal ma lu may ñaan Yàlla mu màgg mi. Mu ne ma: "ñaanal jàmm", ma toog ay bis daal di ñëwaat ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi xamal ma lu may ñaan Yàlla. Mu…

