amna ci ñi leen jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu saalit, daal di jël paaka dagg loxo bi, dereet ji dogul ba mu faatu, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Al-Hasan mu wax ne: Jundub ibn Abdul Laahi yal na ko Yàlla dollee gërëm waxtaanal na nu ci jàkka jii, te fàttewuñu ba mu nu waxtaane ba tay, te ragaluñu ci Jundub fenal Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne: Yonnente Yàlla bi nee na: "amna ci ñi leen jiitu woon jenn waay ju am gaañu-gaañu, mu saalit, daal di jël paaka dagg loxo bi, dereet ji dogul ba mu faatu, Yàlla mu kawe mi wax ne: sama jaam bi gaawe na ma ci boppam, araamal naa ci moom àjjana".
Explanation
Benefits
Waxtaane xeet yi jiitu woon ci li nga xam ne yiw moo ca nekk ak ug waare.
Ibn Hajar nee na: nekk na ci it taxaw ci àqi Yàlla yi ak yërmàndeem ci mbindeefam yi ba tax mu araamal ci ñoom ñuy ray seen bopp ak ne bakkan yi moomeelu Yàlla la.
Araamalees na jëfandikoo sabab yuy jëme ci ray bakkan, ak tëkku gu tar gi nekk ci loolu.
Ibn Hajar nee na: loolu day tegtale ne dafa ko a dagg ngir bëgg a dee waaye jubluwu ca faju.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

