Bu leen sol suwaa walla sooy, bu leen naan ci ndabal wurus mbaa xaalis, te bu leen lekk ci ay boolam, ndax ñoom la ñeel fii ci àdduna, waaye nun la ñeel fële ca àllaaxira
Jële nañu ci Abdur Rahmaan ibn Abii Laylaa mu ne ñoom dañoo nekkoon ci Husayfata, mu sàkku ku ko may mu naan, ab Majuus jox ko mu naan, ba mu tegee këll bi ci loxoom mu sànni ko ko, daaldi wax ne -xanaa du tere naa ko ko lu dul benn yoon du ñaari yoon, mu mel ni day wax…

