ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku bëgg ñu yaatal wërsëgam, guddal fanam, nay jokk ag bokkam».

