yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine
Jële na ñu ci Ibn Abbaas-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ci subag sànni jamra fekk moo ngi ci kaw giléemam gi: "foral ma ay xeer" ma foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, muy xeer yi muy sànni, mu tàmbali…

