bokkul ci nun kuy gisaane mbaa ñu gisaaneel ko, walla mu seetlu mbaa ñu seetal ko, walla mu njabar mbaa ñu njabaral ko
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Imraan Ibn Husayn -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «bokkul ci nun kuy gisaane mbaa ñu gisaaneel ko, walla mu seetlu mbaa ñu seetal ko, walla mu njabar mbaa ñu njabaral ko, ak kuy fas ag fas, ku ñëw ci ab seetkat dëggal ko ca la mu wax kooku weddi na li ñu wàcce ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-«.
Explanation
Bu njëkk bi: "ku gisaane mbaa ñu gisaaneel ko" cosaanam mooy: boyal am picc buy dugg ca liggéey ba ci tukki walla ci yaxantu walla leneen, bu naawee jëm wetu ndayjooram mu baaxal ko daal di wéy ca la mu namm, bu naawee jëm wetu càmmoñ mu gaafal ko daal di bàyyi la mu bëggoon, daganul mu defal lii boppam mbaa muy wut ku ko koy defal, day dugg ci loolu ba tay gaaflu ci mbir yépp, moo xam lu ñuy dégg la walla lu ñuy gis, ci njanaaw mbaa bayima, walla woroom laago yi, walla limat yi (Limat: numéro) mbaa bis yi, walla yeneen yu dul yooyu.
Ñaareel bi: "kuy seetlu mbaa ñu seetal ko" képp kuy wootewoo xam kumpa ci jëfandikoo biddiw yi mbaa leneen, walla mu ñëw ci kuy wootewoo xam kumpa niki seetkat bi ak ñu mel ni moom, daa di koy dëggal ca la muy wootewoo ci xam kumpa, kon weddi na li ñu wàcce ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Ñatteel bi: "kuy njabar walla ñu njabaral ko" te mooy kiy njabaral boppam, mbaa mu njabarloo keneen; ngir mu jariñ kenn mbaa lor ko, walla mu fas ag fas ci takk ay wëñ daal di ci njabar ci jàng ca walla def ca ay muslaay yu araam daal di cay ëf.
Benefits
Wootewoo xam kumpa daa bokk ci bokkale wuuteek Tawhiid.
Araamalees na dëggal ab seetkat ak dem ca ñoom, dana bokk ca loolu li ñuy woowe jàng ca ténq ya ak kopp ya, ak nekkuwaayu biddiw yi, ak di ca xool donte sax ci anamug yër la.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

