bokkul ci nun kiy mbej ñiy mbej lex ya, di xotti kaw yére ya, di woote wooteg ceddo ya
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdallah Ibnu Mashuud mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na : "bokkul ci nun kiy mbej ñiy mbej lex ya, di xotti kaw yére ya, di woote wooteg ceddo ya".
Explanation
Ki ci njëkk: kiy mbej lex ya, dafa jagleel lex cig tudd ndax li mu not ci loolu, waaye dóor yi des ci kanam gi it day dugg ci tere gi.
Ku Ñaareel ki: kiy xotti baatu mbubam ngir tarug njàqare ga.
Ku Ñatteel ki: kiy woote wooteg ceddo ya niki di woo alkande ak toroxtange, ak di yuuxu, ak woo naqar ak yeneen.
Benefits
Warug muñ ci musiba yi, ak araamug mer ci ndogali Yàlla yu metti yi, ak di feeñal loolu: ci yuuxu ak woo naqar walla watu, walla xotti walla yeneen.
Araamal nañu roy ceddo yi ci mbir yi nga xam ne Aji-Yoonal ji saxalu leen ca.
Jàq ak jooy aayul, ndax safaanoowul ak muñ dogali Yàlla mu kawe mi, waaye yërmànde la te Yàlla moo koy def ci xoli jegeñaale yi ak soppe yi.
War na ci jullit bi mu gërëm dogalu Yàlla, bu gërëmul sax muñ moom lu war la ci moom.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

