yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ci feebaram ba nga xam ne ca la faatoo: "yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka" nee na: bu dul woon loolu kon dinaa fésal bàmmeelam, waaye moom dafa ragal ñu jàppe ko jàkka.
Explanation
Benefits
Tere gu feddaliku, ak araam gu tar ci jàppe bàmmeel yi ay jàkka, ak jublu faa ci julli ci lu dul julleeg néew; ndax loolu day jëme ci màggal aji-dee ji ak wër bàmmeelam ak raay ay peggam ak woo aw Turam, te loolu lépp dafa bokk ci bokkaale ak yakoy waral.
Tarug yittewoo gi Yonente Yàlla bi yittewoo Tawhiid ak ragal gi mu ragal jaamu bàmmeel yi; ak it ne loolu day jëme ci bokkaale.
Yàlla aar na Yonnenteem bi ba du ñu def ag bokkaale ca bàmmeelam ba, mu def sahaabaam ak ña ñëw seen ginnaaw ci ñu ñoŋal bàmmeelam bi ci di ko fésal.
Jëfeg Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm ci ndénkaaney Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak seenug xér ci Tawhiid.
Tere nañu niru-nirulu Yahuud yi ak Nasaraan yi, ak ne tabax ci kaw bàmmeel yi ci seen doxaliin la bokk
Bokk na ci jàppe bàmmeel yi ay jàkka di fa julli jëm, donte tabaxuñu ko jàkka.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

